Di Buur, Di Bummi Okay

You might also like

Download as docx, pdf, or txt
Download as docx, pdf, or txt
You are on page 1of 1

DI BUUR, DI BUMMI

Ami Mbeng

Ci gaawu bi weesu, 4eelu fan ci weeru me, la dipite yi wote sémbub à tte biy
far palaasu Njiitu-jawriñ ji ci nguurug Senegaal. Ndax sémbub à tte bi jà ll
na ? Loolu jarul a laaj ! Ci 138 dipite yi teewoon, 124 yi wote nañ u « waaw »
7 yi « déedéet ». Yeneen 7 yi des ñ oom, di waa PDS, dañ oo là nk ne duñ u
wote tey duñ u wote ëllëg. Kon, Senegaal amatul Njiitu-jawriñ . À tte bu bees
bii, nag, dina indi ay coppite yu bare ci doxalinu nguur gi, waaye it dina gën
a dooleel Njiitu-réew mi.

Du loo xam ni Maki Sà ll ak Bun Abdalaa Jonn rekk la ñ eel. Dafa dig coppite
gu soxal ndeyu-à tte réew meek tëralinu politigu Senegaal ci boppam.
Ndaxte, yamoo bi war ci diggante ñ etti baat yi - baatu doxal bi, baatu yoon
bi ak baatu fal à tte bi - lay nasaxal, daanaka.

Li péncum réew mi dogal dina soppi 21 sà rt ci biir ndeyu-à tte mi, jox Maki
Sà ll wareef yi Bun Abdalaa Jonn jagoo woon. Ñ enn ñ i ci kujje gi nee ñ u
nguur gi duggewu ko dara lu dul këppeel doole. Ñ eneen ñ i, ñ oom, jà pp nañ u
ne Maki day waajal xaat joŋanteb 2024.

Dëgg la sax, Njiitu-réew mee yelloo tabb ku ko neex ngir mu jiite gornmaa
bi, jà ppale ko ci naal yi mu lal ñ eel doxalinu réew mi. Naam, Senegaal ay
njiiti-jawriñ yuy jaamu soxlaam lañ fiy faral di gis. Waaye loolu warul a tax
ñ u ne kenn dootul jiite jawriñ yi.

Mbir mi daal, jaay doole lay gën a nirool. Ndaxte léegi moom, Maki mooy
Buur di Bummi : su defulee lu ko neex, moom la neex !

You might also like